Darkase xeetu garab gu bokk ci njabootu Anacardiaceae. Ca Amerig gu naaje ga la bàyyikoo, te ci barab yu naaje yi lees koy baye ngir foytéefam.
Garabu darkase danay àgg 12 ba 15i met ci guddaay. Buut bi di reenam bi ëpp solo danay àgg ci xóotaay bu sori ci suuf si. Pànguur yi di reeni wet yi danañuy àgg fu sori lool. Xobam wirgow nëtëx bu dër la yor. Danay àgg 10 ba 20i sàntimet ci guddaay ak 10 sàntimet ci yaatuwaay. Xobam wi puur ci noor lay feeñ. Daa gëtte am xet gu neex te day xëcc yamb yi, ci la lem di bàyyikoo.
Doom bi ci njeexteelu noor lay mat. Bu ñoree day xonq mbaa mu mboq. Bu ñorul nag nëtëx. Am ub saal ca biir bu ñuy wax ndaamaraas mu bari ay njariñ lool.
Doom bi dees na ci njar, dees na ci defar sàngara te dees na ci faju. Garab gi nag dees na ci jële am matt dees na ci faju.
Anacardium occidentale
Darkase xeetu garab gu bokk ci njabootu Anacardiaceae. Ca Amerig gu naaje ga la bàyyikoo, te ci barab yu naaje yi lees koy baye ngir foytéefam.