Koko gi xeetu garab la gu bokk ci njabootu Arecaceae.
Ci gamgamlekaay disaayu doom bi danay àgg ba 1,5i kilogaraam. Day ëmb ndox mu saf suukar: "ndoxu koko".
Reenam day dugg ci suuf guddaay guy àgg 4 ba 5i met.
Limu tóotóoram duy wees 20 mbaa 30.
Koko bi deef na ko lekk nim bindoo, mbaa soppi ko ay xeeti diw, mbaa ay aniinukaay.